22«Bu ngeen dee góob seen tool, buleen góob ba fa tool ba yem te buleen ci toppaat, di foraatu. Aji ñàkk akub doxandéem ngeen koy bàyyee. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.»
23Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
24«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu juróom ñaareelu weer taxawee, bés bi jëkk ci weer wi, na doon seen bésub Noflaay bu ngeen di amal ndaje mu sell. Deeleen fàttlee bés bi liit yu xumb.
25Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey, waaye nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.»