5mbaa mu laal yu sew-sewaan yiy dox ci suuf te di ko sobeel, mbaa mu laal nit ku ko sobeel ak lu sobe sa mana doon,
6dina yendoo sobe sa ba jant so, te du lekk ci sarax yu sell yi ndare du dafa sangu.
7Bu jant sowee nag set na, te man naa lekk ci sarax yu sell yi, ndax ñamam la.
8Lu médd mbaa lu rab fàdd waru koo lekk, mu di ko sobeel. Maay Aji Sax ji.