Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 21

Sarxalkat yi 21:13-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Sarxalkat bu mag bi, ku xamul góor lay jël soxna.
14Ku jëkkëram faatu mbaa ku ñu baal mbaa ku ñu torxal, tëdde ko, mbaa ab gànc, du ko mana jël soxna. Ab janq bu mu bokkal doŋŋ la mana jël soxna.
15Su ko defee du teddadil aw askanam ci biir bànni Israyil, ndax man Aji Sax ji maa ko sellal.»
16Bu loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
17«Waxal Aaróona ne ko: Muy tey muy ëllëg ba fàww, góor gu askanoo ci yaw ak maas gu mu mana bokk, su amee sikk du mana agsi ba ci sarxalukaay bi, di joxe ñamu Yàllaam.
18Du kenn sax ku am sikk kuy agsi ba fii, du gumba, du kuy soox, du ku xar-kanamam am sikk mbaa ku cér yi sutaate.
19Du it ku tànk bi làggi mbaa loxo bi,
20mbaa ab xuuge mbaa ab tungune; du it ku bëtam am sikk mbaa ku ràmm mbaa ku am góom yu sol dëtt, mbaa ku ñu tàpp.
21Askanu Aaróona sarxalkat bi, du kenn ku ci am sikk kuy agsi ba fii, di joxe saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Sikk si ci moom a tax du mana agsi ba fii, di joxe ñamu Yàllaam.
22Du tere mu saña lekk ci ñamu Yàllaam, muy ñam wu sell ak wu sella sell.

Read Sarxalkat yi 21Sarxalkat yi 21
Compare Sarxalkat yi 21:13-22Sarxalkat yi 21:13-22