Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 19

Sarxalkat yi 19:20-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20«Ku tëdde ab jaam bu wara séy ak keneen te fekk joteesu ko, goreeleesu ko, ndàmpaay war na ca, waaye deesu leen boole rey, ndax li ndaw si dib jaam ba tey.
21Waa ji day yóbbu am kuuyu peyug tooñ ca bunt xaymab ndaje ma, muy peyug tooñ, gi muy sarxalal Aji Sax ji.
22Na ko sarxalkat bi defal kuuy miy saraxas peyug tooñ muy njotlaayam fi kanam Aji Sax ji, ndax bàkkaar bi mu def. Kon dees na ko jéggal bàkkaar bi mu def.
23«Bu ngeen duggee ca réew ma, ba jëmbat fa mboolem xeetu garab guy meññ ay doom, nangeen aayal doom ya. Diiru ñetti at ngeen di aayal doom ya. Dungeen ko lekk ci diir boobu.
24Atum ñeenteel ba doom ya yépp lañuy sellalal Aji Sax ji, te di ko bége ci biir cant.
25Juróomeelu at ma doŋŋ ngeen di saña lekk doom ya. Su ko defee meññeef ma barkeelal leen. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
26«Buleen lekk lu am deret. Buleen di gisaane mbaa ngeen di jibar.
27Buleen wat seen peggu kawaru bopp te buleen dagg seen peggu sikkim,
28mbaa ngeen di dagg seen yaram, di ko mititloo ku dee, te buleen ñaasu fenn ci seen yaram. Maay Aji Sax ji.
29«Buleen torxal seen doom ju jigéen, di ko def ab gànc; lu ko moy réew mi sóobu ci gànctu ba ne lijj ci ñaawtéef.
30«Samay bési Noflaay nag wormaal-leen ko te sama bérab bu sell teral-leen ko. Maay Aji Sax ji.
31«Buleen jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee te buleen jublu ci boroom rawaan yiy seet, ndax kon ñu sobeel leen. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji.
32«Bu boroom bijjaaw teewee, jógleen wormaal ko. Deeleen rus mag te ragal-leen seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.
33«Bu ab doxandéem daleek yeen ci seenum réew, buleen ko lor.
34Njuddu-ji-réew ji nangeen ko yemaleek doxandéem bi ngeen dëkkal. Soppleen ko ni ngeen soppe seen bopp, ndaxte ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
35«Buleen def njubadi ci lu ñuy natte guddaay mbaa diisaay mbaa lu ñuy sol, sotti.
36Na seen nattukaayu diisaay jub, doom ya ngeen cay natte jub, te na nattukaayi sol-sotti yi jub. Maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen génne réewum Misra.

Read Sarxalkat yi 19Sarxalkat yi 19
Compare Sarxalkat yi 19:20-36Sarxalkat yi 19:20-36