36Su boobaa na sarxalkat bi santaane, ñu génne lépp lu nekk ca néeg ba, bala muy dugg di seet liir wi. Su ko defee du am lenn lu nekk ca néeg ba, lu muy biral ne sobe topp na ko. Gannaaw loolu sarxalkat bi dugg, seet néeg bi.
37Bu sarxalkat bi seetee liir wi ci miiri néeg bi ca biir, muy ay xóot-xóot yu xawa nëtëx, mbaa mu xawa xonq, mel ni lu def pax ci miir bi,
38na génn néeg bi te tëj néeg bi diiru juróom ñaari fan.
39Bésub juróom ñaareel ba na sarxalkat bi délsi seet néeg bi. Bu liir wi lawee ci miiri néeg bi,
40na sarxalkat bi santaane, ñu teggi doj yi liir wi xuural, boole ko génne dëkk bi, sànni ko fu setul.
41Na xeetlu biir néeg bi ba mu daj, te pënd ba ñu ca xeete dees koy génne dëkk ba, tuur ko fu setul.
42Dañoo wara sàkkaat ay doj, wuutale ko doj yooyu te sàkk ban bu bees, raaxe ko néeg bi.