21Li ngeen mana lekk daal ci mboolem gunóor guy naaw tey doxe ñeenti tànk moo di: lépp lu tànk yi ànd aki yeel, mu man caa tëb-tëbe ci suuf.
22Li ngeen mana lekk ci yooyu moo di: mboolem xeetu njéeréer ak mboolem xeetu salleer ak mboolem xeetu soccet ak yeneen yu ñu xeetool yépp.
23Waaye mboolem yeneen gunóor yuy naaw tey doxe ñeenti tànk sibleen ko.
24«Yii nag da leen di sobeel te képp ku laal lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.
25Te itam képp ku for lenn lu dee ci yii, na fóot ay yéreem, waaye dina yendoo sobe ba jant so.
26Mboolem mala mu we wa xar te séddlikoowul ñaar mbaa du duññ daganul ci yeen, ku ci laal lenn it sobewu na.
27Ba tey lépp luy doxe ndëgguy tànkam ci mboolem boroom ñeenti tànk, daganul ci yeen te ku laal méddam dina yendoo sobe ba jant so.
28Ku for méddam, na fóot ay yéreem te dina yendoo sobe ba jant so. Yooyu daganul ci yeen.
29«Bu loolu weesee, leneen lu daganul ci yeen ci rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, mooy kaña ak janax ak xeeti mbëtt yépp;
30ak unk ak bar ak sindax buy yéeg, ak sindax buy dox ci suuf, ak kàkkatar.
31Yooyoo daganul ci yeen ci mboolem rab yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf. Képp ku laal lenn lu ci dee dina yendoo sobe ba jant so.