7Ndox mu ne xéew du fey mbëggeel, ay dex du ko mëdd. Ku koy weccee sa alalu kër gépp it, ñu jéppi laa jéppi rekk.
8Sunub jigéen lu ndaw la, ween sax amu ko. Lu nuy defal sunub jigéen bés bu ñu koy bëggsi?
9Su doon am tata, nu tabaxal ko soorooru xaalis. Su doon bunt, nu aare ko xànqi seedar.
10Maa dim tata, sama ween di sooroor ya; moo tax waa ji xam ne maa di jàmmam.
11Suleymaan am na reseñ ca Baal Amon. Da koo dénk ay beykat. Ku nekk di ko fey meññeef ma junniy dogi xaalis.
12Junniy dogi xaalis yi, Suleymaan, yaa ko moom; ñaar téeméer yi, beykat yi. Waaye sama toolub reseñ, maa ko moom.
13Yaw mi tooge digg tool bi, samay xarit a ngi teewlu sa baat, waxal boog, ma dégg.