5Ana ndaw suy jóge màndiŋ ma nii, wéeroo nijaayam? Ndaw si Ci ron pom gi laa la yee, fa la sa yaay jàppe ëmb, jur la fa.
6Teg ma ci sa xol ni torlukaay, mbaa ci sa përëg ni lamu màndarga. Mbëggeel a bare doole ni ndee, fiiraange xér ni bàmmeel. Day jàpp jippét, di jum bu Aji Sax ji taal.