Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 7

Ngën-gi-woy 7:5-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Sa loos wi, coleet, rattax, ni tatay bëñi ñay; say gët di lerxat ni déegi Esbon, ya feggook buntu Bat Rabim. Sa bakkan bi jub xocc ni tatay Libaŋ ja tiim Damaas.
6Sa bopp siggi ni tundu Karmel, njañ liy nes-nesi ni sooyu buur, létt yay fëy-fëyi, ba laaw buur.
7Rafet, sopploo! Soppee, bànneex nga!
8Sa taxawaay bii garabu tàndarma la, sa ween yi di cëggi doom ya.

Read Ngën-gi-woy 7Ngën-gi-woy 7
Compare Ngën-gi-woy 7:5-8Ngën-gi-woy 7:5-8