5Wuy, geesul fee! Soo ma nee jàkk, ma jànnaxe. Sa njañ liy loy-loyee ngi saf géttu bëy yu ñuul, yu bartaloo kaw tundu Galàdd.
6Sa gëñ yi ni mbote yu weex, yéege ca sangukaay ba, ku nekk ak seexam, kenn wéetu ca.
7Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi.
8Buur day am juróom benn fukki lingeer ak juróom ñett fukki jongama ak jeeg ju dul jeex.
9Waaye sama nenne kenn la, matal ma sëkk, yaayam kennal ko, muy ngëneelu biiru yaayam. Janq ji gis ko, di ko jëwe mbégteem, lingeeri buur aki jongamaam di ko kañ.
10Ña nga naa: «Ndaw sii ku mu? Bu nee xiféet, nga ne fajar a xar, rafet ni leer gu ndaw, yànj ni jant bi, yéeme ni gàngoori biddiiw!»
11Damaa wàcc ba ca toolub saal ya, xooli cax mu yees mi ci xur wi, bu reseñ ji jebbee, mbaa gërënaat ji tóor, ma gis.