Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 5

Ngën-gi-woy 5:3-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Ma ne ko: «Summiku naa de, xanaa duma soluwaat? Jàngu naa jeeg, xanaa duma taqati?»
4Sama nijaay yoor loxoom ci xarante bi, sama yaram ne sàyy.
5Ma ne bërét, di ubbil nijaay, sama yoxo yi, diwu ndàbb di ca siit, sama waaraam yi, ndàbb rogalaat ba ci njàppul bunt bi.
6Maa ubbil nijaay, waaye nijaay waññiku na, ba wéy. Ba mu waññikoo, tuuti ma dee. Seet naa ko, gisuma ko; ma woo ko, wuyuwul.

Read Ngën-gi-woy 5Ngën-gi-woy 5
Compare Ngën-gi-woy 5:3-6Ngën-gi-woy 5:3-6