3Ma ne ko: «Summiku naa de, xanaa duma soluwaat? Jàngu naa jeeg, xanaa duma taqati?»
4Sama nijaay yoor loxoom ci xarante bi, sama yaram ne sàyy.
5Ma ne bërét, di ubbil nijaay, sama yoxo yi, diwu ndàbb di ca siit, sama waaraam yi, ndàbb rogalaat ba ci njàppul bunt bi.
6Maa ubbil nijaay, waaye nijaay waññiku na, ba wéy. Ba mu waññikoo, tuuti ma dee. Seet naa ko, gisuma ko; ma woo ko, wuyuwul.
7Wattukat yiy wër dëkk bi gis ma; ñu dóor ma, gaañ ma, ñori sama malaan. Wattukati tata jaa!
8Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma ne su ngeen gisee sama nijaay, ne ko damaa wopp ndax mbëggeel.
9Yaw mi dàq ci jigéen ñi, ana lu sa nijaay gëne keneen? Ana lu mu ëpplee keneen, ba nga di nu waatloo lii?
10Sama nijaay daa xees, leer; kenn la ci fukki junniy góor.
11Kanam gi ni wurus, di wurusu ngalam; njañ li lëmësu, ñuul ni ndobin.
12Gët yi ni pitax yu feggook wali ndox, sangoo meew, feggook ndox mu ne xéew.
13Lex ya di tool, gàncax ga ne ca bann, tuñ ya diy tóor-tóor, ndàbb wale ca, rogalaat.
14Yoxo yi banti wurus la, ngën-gi-per tappe ca; jëmm ja rattax ni bëñu ñay laloo peri safiir;
15yeel yi kenuy doj wu jafe la, sampe ci tànki wurusu ngalam. Meloom ni tundi Libaŋ, di tànnéef ni garabi seedar.