Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 5

Ngën-gi-woy 5:11-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Kanam gi ni wurus, di wurusu ngalam; njañ li lëmësu, ñuul ni ndobin.
12Gët yi ni pitax yu feggook wali ndox, sangoo meew, feggook ndox mu ne xéew.
13Lex ya di tool, gàncax ga ne ca bann, tuñ ya diy tóor-tóor, ndàbb wale ca, rogalaat.
14Yoxo yi banti wurus la, ngën-gi-per tappe ca; jëmm ja rattax ni bëñu ñay laloo peri safiir;
15yeel yi kenuy doj wu jafe la, sampe ci tànki wurusu ngalam. Meloom ni tundi Libaŋ, di tànnéef ni garabi seedar.

Read Ngën-gi-woy 5Ngën-gi-woy 5
Compare Ngën-gi-woy 5:11-15Ngën-gi-woy 5:11-15