Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 4

Ngën-gi-woy 4:7-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
8Séet sama, jógeel Libaŋ, jege ma, bawool Libaŋ, jegesi ma. Wàcceel colli Amana ak colli Senir ak Ermon. Génnal xunti gaynde yooyook tundi segg ya.
9Jigéen sama, séet sama, benn yoon nga ma xool, sama fit ne tërit. Sa benn peru caq rekk, sama fit ne tërit.
10Jigéen sama, séet sama, sa mbëggeel a neex! Sa mbëggeel a dàq biiñ, sa diw yu xeeñ dàq luy cuuraay.

Read Ngën-gi-woy 4Ngën-gi-woy 4
Compare Ngën-gi-woy 4:7-10Ngën-gi-woy 4:7-10