1Yaaka rafet, xarit, yaaka taaru! Sa gët yi niy pitax, làqoo muuraay bi, njañ liy loy-loyee ngi saf géttu bëy yu ñuul yu bartaloo kaw tundu Galàdd.
2Sa gëñ yi weex ni xar yu ñu wat ñuy yéege ca sangukaay ba, ku nekk ak seexam, kenn wéetu ca.
3Sa tuñ yi mel ni wëñ gu xonq curr, ndaw gémmiñ gu jekk! Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi;
4sa loos wi ne coleet ni tatay Daawuda, mërgalu ba jekk, caq bay lang ni junniy kiiraayi jàmbaar.
5Sa ween yi ni ñaari tef, mbaa seexi kéwél yuy fore digg tóor-tóor yi.
6Balaa jant a fenk, ker gàddaay, ma ne coww diggante tund wa ndàbb ne bann, ak tund wa xas ma neexe.
7Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
8Séet sama, jógeel Libaŋ, jege ma, bawool Libaŋ, jegesi ma. Wàcceel colli Amana ak colli Senir ak Ermon. Génnal xunti gaynde yooyook tundi segg ya.
9Jigéen sama, séet sama, benn yoon nga ma xool, sama fit ne tërit. Sa benn peru caq rekk, sama fit ne tërit.
10Jigéen sama, séet sama, sa mbëggeel a neex! Sa mbëggeel a dàq biiñ, sa diw yu xeeñ dàq luy cuuraay.