3Wattukat yee ma gis, ba ñuy wër dëkk bi. Ma ne leen: «Sama soppey xol, gisuleen ko?»
4Ma romb leen tuuti rekk, gis sama soppey xol. Ma ne ko taral, bàyyeetuma ko, ba yóbbu ko sama kër yaay, ba sama biir néegu ndey ji ma jur.
5Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma ci taaru kéwél ak koobay àll bi, ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel te jotul.