Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 25

Màndiŋ ma 25:3-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Israyil nag taqook tuur ma ñuy wax Baal Pewor, ba sànjum Aji Sax ji tàkkal Israyil.
4Aji Sax ji ne Musaa: «Jàppal njiiti mbooloo mi yépp, nga wékk leen ci bant fi kanam Aji Sax ji, bëccëg ndarakàmm, ngir sànjum Aji Sax ji dëddu Israyil.»
5Musaa ne àttekati Israyil: «Na ku nekk ci yeen rey nitam ñi taqook Baal Pewor.»
6Ci biir loolu rekk, jenn waayu bànni Israyil dikk, indaale senn ndawas waa Majan ci biiri bokkam, Musaa ak mbooloom Israyil mépp di gis, fekk ñoom ñuy jooyoo fa bunt xaymab ndaje ma.
7Fineyas, doomu Elasar, doomu sarxalkat ba Aaróona, gis loolu, daldi jóge ca mbooloo ma, jël ab xeej.

Read Màndiŋ ma 25Màndiŋ ma 25
Compare Màndiŋ ma 25:3-7Màndiŋ ma 25:3-7