Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 20

Màndiŋ ma 20:24-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
24«Dees na tërali Aaróona fa ay bokkam. Du dugg déy ca réew ma ma jox bànni Israyil, gannaaw yeena gàntaloon sama ndigal ca walum Meriba.
25Àndal ak Aaróona ak doomam Elasar, nga yéege leen ca kaw tundu Or.
26Te nga summi yérey carxal yu Aaróona, solal ko doomam Elasar. Aaróona moom, dees koy tërali ca ay bokkam. Foofa lay deeye.»
27Ba loolu amee Musaa def la ko Aji Sax ji sant, ñu ànd yéeg kaw tundu Or, mbooloo ma mépp di gis.
28Musaa summi yérey Aaróona, solal ko doomam Elasar, Aaróona dee foofa ca kaw tund wa, Musaa ak Elasar wàcc tund wa.
29Mbooloo ma mépp nag xam ne Aaróona dëddu na. Waa kër Israyil gépp a ko jooy diiru fanweeri fan.

Read Màndiŋ ma 20Màndiŋ ma 20
Compare Màndiŋ ma 20:24-29Màndiŋ ma 20:24-29