Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 20:24-29 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 20:24-29 in Kàddug Yàlla gi

24 «Dees na tërali Aaróona fa ay bokkam. Du dugg déy ca réew ma ma jox bànni Israyil, gannaaw yeena gàntaloon sama ndigal ca walum Meriba.
25 Àndal ak Aaróona ak doomam Elasar, nga yéege leen ca kaw tundu Or.
26 Te nga summi yérey carxal yu Aaróona, solal ko doomam Elasar. Aaróona moom, dees koy tërali ca ay bokkam. Foofa lay deeye.»
27 Ba loolu amee Musaa def la ko Aji Sax ji sant, ñu ànd yéeg kaw tundu Or, mbooloo ma mépp di gis.
28 Musaa summi yérey Aaróona, solal ko doomam Elasar, Aaróona dee foofa ca kaw tund wa, Musaa ak Elasar wàcc tund wa.
29 Mbooloo ma mépp nag xam ne Aaróona dëddu na. Waa kër Israyil gépp a ko jooy diiru fanweeri fan.
Màndiŋ ma 20 in Kàddug Yàlla gi