Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 13

Màndiŋ ma 13:26-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
26Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom bànni Israyil gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma.
27Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew, ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa.
28Xanaa kay, kàttan gu askanu réew ma am, péey ya dàbbliku te yaa lool. Te it ponkal yooyu cosaanoo ci Anageen ñi lanu fa gis.
29Amalegeen ñaa dëkke bëj-saalumu réew ma, Etteen ñaak Yebuseen ñaak Amoreen ña dëkke diiwaanu tund ya, Kanaaneen ña dëkke wetu géej, feggook dexu Yurdan.»
30Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.»
31Ndaw ya àndoon ak moom daldi ne: «Manunoo songi waa réew ma, ndax ñoo nu ëpp doole.»
32Ci biir loolu ñuy baatal ca kanam bànni Israyil, réew ma ñu nemmikuji woon. Ñu naan: «Réew moomee ñu wëri woon ngir nemmiku ko déy, réew la muy faagaagal ay sancaanam, te mboolem askan wa nu fa gis, ay boroom jëmm lañu.

Read Màndiŋ ma 13Màndiŋ ma 13
Compare Màndiŋ ma 13:26-32Màndiŋ ma 13:26-32