3Ñu tudde bérab boobu Tabera (mu neexook Tàkkaan), ndax sawaras Aji Sax ji leen fa tàkkal.
4Ci biir loolu genn gàngooru njaxasaan mu nekkoon ca seen biir jiital seen bakkan, di ŋaf-ŋafi, ba tax bànni Israyil itam dellu di jàmbat. Ña nga naan: «Éy ku nuy leelatiw yàpp!
5Namm nan jën ya nu daa ndawaloo ca Misra, te dikkewu nu tus! Ak yomb jaak xaal jaak pooro baak soble saak laaj ja!
6Tey jii sunu put yaa ngi wow koŋŋ, gisunu lenn lu moy mànn!»
7Mànn ma nag daa meloon ni pepp mi ñuy wax koryanda, te nirook ndàbbu garab gi ñuy wax bedola.
8Mbooloo ma da daan wër, di ko for, di ko wole doji wolukaay, mbaa ñu di ko dëbb ciy gënn, ba noppi baxal ko ci cin, def ko ay mburu yu cafkaam mel ni cafkay nàkk yu am niw.
9Bu layaa ca dal ba ag guddi, mànn ma day wàccaale ak moom.
10Ci biir loolu Musaa dégg mbooloo miy ñaxtu, làng ak làng, ku nekk ci sa bunt xayma. Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkk jippét, Musaa nag ñaawlu ko.