5Simoŋ ne ko: «Kilifa gi, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Waaye nag dinaa ko sànni ci sa ndigal.»
6Naka lañu sànni mbaal yi, jàpp jën yu bare, ba mbaal yay tàmbalee xëtt.
7Noonu ñu daldi liyaar seen àndandoo, yi nekk ca geneen gaal ga, ngir ñu ñëw dimbali leen. Ñooñu agsi, ñu feesal ñaari gaal yi, ba ñuy bëgga suux.
8Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanam Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!»
9Wax na loolu nag, ndax jën yu bare ya ñu mbaaloon daf koo jaaxal, moom ak ña mu àndaloon
10ak ña mu bokkaloon liggéey ba, maanaam ñaari doomi Sebede yi di Saag ak Yowaana. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaaw-si-tey, ay nit ngay mbaal jëme ci man.»
11Noonu ñu teer ca tefes ga, bàyyi lépp, di topp ci moom.
12Ni Yeesu nekke woon ci ab dëkk, am fa ku gaana ba daj. Bi mu gisee Yeesu, mu daldi dëpp jëëm ci suuf, ñaan ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa wéral.»
13Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
14Yeesu sant ko ne: «Bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.»
15Noonu turu Yeesu di gëna siiw. Mbooloo mu bare di ñëw ci moom, ngir déglu ko te mu faj seeni jàngoro.