Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 22

Luug 22:25-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Yeesu nag ne leen: «Buuri xeeti àddina doole lañuy nguuroo ci seen kaw, teewul ñi leen di néewal doole, baaxekati nit ñi lañu leen di wooye.
26Yeen nag bumu deme noonu ci seen biir. Ki gëna kawe ci yeen, na mel ni moo gën di ndaw, te njiit li, na mel ni ab surga.
27Ki ñu taajal ndab li, ak surga bi ko taajal, ana ku ci gëna kawe? Xanaa du ki ñu taajal? Moonte man, ci seen biir laa tooge toogaayu surga!
28Yeen nag yeenay ñi des ak man ci sama biir coono.
29Man itam ni ma sama baay dénke nguur, ni laa leen koy dénke.
30Yeenay lekk ak a naane ca sama ndab, ca sama nguur, te yeenay tooge ay gàngune, di jiite fukki giiri bànni Israyil ak ñaar.»
31Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp.
32Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»
33Piyeer ne ko: «Sang bi, jekk naa ci ànd ak yaw kaso, ak ci ànd ak yaw dee.»
34Yeesu ne ko: «Piyeer, maa la ko wax, bala ganaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am dencukaayu xaalis, na ko jël, ku am mbuus it, na ko jël; ku amul saamar, na jaay mbubbam, jënde saamar.
37Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.»
38Ñu ne ko: «Sang bi, ñaari saamar a ngi fi.» Mu ne leen: «Doy na.»
39Ci kaw loolu Yeesu génn, jëm ca tundu Oliw ya, na mu ko baaxoo woon, taalibe ya topp ci moom.

Read Luug 22Luug 22
Compare Luug 22:25-39Luug 22:25-39