Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 15

LUUG 15:14-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14Bi mu sànkee alalam jépp, xiif bu metti dal ca réew ma, mu tàmbalee ñàkk.
15Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya.
16Mu xiif ba bëgga lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara.
17Mujj xelam délsi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgga dee ak xiif!
18Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la;
19yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ”
20«Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko.
21Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.”
22Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gëna rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll.
23Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu;
24ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.” Noonu ñu tàmbalee bànneexu.
25«Fekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu ñëwee, ba jub kër ga, mu dégg ñuy tëgg, di fecc.
26Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew.
27Mu ne ko: “Sa rakk moo délsi, te sa baay rey na sëllu wu duuf wa, ndaxte ñibsi na ci jàmm.”
28«Ci kaw loolu taaw ba daldi mer, baña dugg ca kër ga. Baayam daldi génn, ngir ñaan ko mu dugg.
29Waaye taaw ba wax baayam ne ko: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, mel ni jaam, te masumaa moy sa ndigal, waaye yaw, masuloo ma may sax tef, ngir ma bànneexu, man ak samay xarit.
30Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi yàq sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko sëllu wu duuf wi.”
31Noonu baay bi ne ko: “Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk, te li ma am lépp, yaa ko moom.

Read LUUG 15LUUG 15
Compare LUUG 15:14-31LUUG 15:14-31