Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 15:14-31 in Wolof

Help us?

LUUG 15:14-31 in Téereb Injiil

14 Bi mu sànkee alalam jépp, xiif bu metti dal ca réew ma, mu tàmbalee ñàkk.
15 Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya.
16 Mu xiif ba bëgga lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara.
17 Mujj xelam délsi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgga dee ak xiif!
18 Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la;
19 yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ”
20 «Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko.
21 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.”
22 Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gëna rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll.
23 Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu;
24 ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.” Noonu ñu tàmbalee bànneexu.
25 «Fekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu ñëwee, ba jub kër ga, mu dégg ñuy tëgg, di fecc.
26 Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew.
27 Mu ne ko: “Sa rakk moo délsi, te sa baay rey na sëllu wu duuf wa, ndaxte ñibsi na ci jàmm.”
28 «Ci kaw loolu taaw ba daldi mer, baña dugg ca kër ga. Baayam daldi génn, ngir ñaan ko mu dugg.
29 Waaye taaw ba wax baayam ne ko: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, mel ni jaam, te masumaa moy sa ndigal, waaye yaw, masuloo ma may sax tef, ngir ma bànneexu, man ak samay xarit.
30 Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi yàq sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko sëllu wu duuf wi.”
31 Noonu baay bi ne ko: “Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk, te li ma am lépp, yaa ko moom.
LUUG 15 in Téereb Injiil

Luug 15:14-31 in Kàddug Yàlla gi

14 Gannaaw ba mu sànkee lépp, xiif bu metti dikkal réew ma, mu daldi tàmbalee ñàkk.
15 Ci kaw loolu mu dem, di surgawu ku cosaanoo ca réew mooma, kooku yebal ko ca ay toolam, muy sàmm ay mbaam-xuux.
16 Mu dem ba noon ngéeja lekk ca xolliti doomi garab ya mbaam-xuux yay lekk, fajeb xiifam, te kenn mayu ko ca.
17 Xel ma mujj délsi, mu ne: “Ñaata surga la sama baay am, seen lekk ne gàññ, man, ab xiif di ma rey fii!
18 Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la;
19 yeyootumaa tuddoo sax sa doom; léegi def ma ni ku bokk ci say surga.’ ”
20 «Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.
21 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la; yeyootumaa tuddoo sax sa doom.”
22 Teewul baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb mi gëna rafet, solal ko, te ngeen takkal ko ab jaaro ci loxoom, solal ko ay dàll.
23 Indileen sëlluw yafal wa, rey, nu lekk, te bànneexu;
24 ndax sama doom jii moo dee woon te dekki na, moo réeroon te feeñ na.” Ñu daldi tàmbalee bànneexu.
25 «Loolaa nga fekk mag ja ca tool ya. Ba mag ja dikkee ba jub kër ga, ca la dégg po ma ak pecc ma.
26 Mu woo kenn ca xale ya, laaj ko lu xew.
27 Mu ne ko: “Sa rakk jaa délsi, sa baay rey sëlluw yar wa, ndax li mu délseek jàmm.”
28 «Mag ja nag mer, nanguwula agsi, baayam génn, di ko soññ.
29 Mu àddu, ne baayam: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, sa ndigal, masuma koo moy, te man, masuloo maa may sax as tef su nu bégloo, maak samay xarit.
30 Sa doom jii dikk, gannaaw ba mu yàqee sa alal ci ay gànc, nga reyal ko sëlluw yafal wi!”
31 Mu ne ko: “Doom, yaw de naka jekk man nga nekkal, te mboolem lu ma am, yaa ko moom.
Luug 15 in Kàddug Yàlla gi