49Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bundxatal.”
50Su ko defee yoon topp niti tey jii, deretu mboolem yonent yi tuuru, dale ko ca cosaanu àddina.
51La dale ca deretu Abel ba ca deretu Sàkkaryaa, ma ñu rey ca diggante sarxalukaay ba ak bérab bu sell ba, maa leen ko wax déy, dees na ko topp niti tey jii.
52Ngalla yeen xamkati yoon yi, yeena sànk caabiy xam-xam; yeen dugguleen, ñiy duggsi, ngeen tere leena dugg.»
53Ba Yeesu génnee foofa, ca la Farisen ya ak firikat ya tàmbalee xabtalu ci kawam, di ko seetloo ay laaj ci mbir yu bare,