Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 3

Jëf ya 3:12-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Piyeer nag gis loolu, àddu, ne mbooloo ma: «Yeen bokki Israyil, lu ngeen di waaru ci lii? Lu ngeen nu naa jàkk, mel ni sunu manoorey bopp mbaa sunug njullite lanu doxloo kii?
13Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
14Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.
15Bóom ngeen Kiy dundloo, waaye Yàllaa ko dekkal, nu seede ko.
16Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.
17«Teewul nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam moo leen taxa jëfe noonu, te loolu it moo dal seeni kilifa.
18Waaye Yàlla moo sottale noonu la mu yégle woon lu jiitu, yonent yépp jottli, ne Almaseem dina sonn.
19Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru.
20Su boobaa jamonoy péex ay bawoo ci Boroom bi, te mooy yebal Almasi mu leen jagleel, te muy Yeesu.
21Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottli.
22Musaa kay noon na: “Boroom bi seen Yàlla mooy seppee ci seenu xeet ab yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.
23Képp ku déggalul yonent boobu, dees na la xettee ci xeet wi, sànk la.”
24«Te it mboolem yonent yi wax, dale ko ci Samiyel ak ñi ko wuutu, ñoom it yégle woon nañu bés yii nuy dund.
25Yeen nag yeenay donoy yonent yi te yeenay séddu ci kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, ba mu nee Ibraayma: “Ci saw askan la xeeti àddina yépp di barkeel.”
26Yeen la Yàlla jëkka wool jawriñam, daldi koy yebal ci yeen, ngir barkeel leen, waññee kenn ku nekk ci yeen, mu moy jikkoom yu bon.»

Read Jëf ya 3Jëf ya 3
Compare Jëf ya 3:12-26Jëf ya 3:12-26