Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 25

JËF YA 25:11-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Su ma tooñoon mbaa ma def lu bon lu jar dee, kon duma tinu ngir baña dee. Waaye bu li ñu may jiiñ taxawul, kenn sañu ma leena jébbal. Dénk naa sama mbir Sesaar.»
12Bi mu waxee loolu, Festus gise ak ñi ko wër, mu ne ko: «Dénk nga sa mbir Sesaar, kon ci moom ngay dem.»
13Ba ñu ca tegee ay fan, buur Agaripa ak Berenis ñëw Sesare, ngir nuyusi Festus.
14Bi seen ngan di ruus nag, Festus diis buur ba mbirum Pool ne ko: «Feligsë batale na nu ak kenn ku ñu tëj.
15Bi ma nekkee Yerusalem, sarxalkat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame nañu ko ci man, ñaan ma, ma daan ko.
16Waaye ma ne leen: “Jébbale nit, fekk jàkkaarloowul ak ñi koy jiiñ, ba mana làyyil boppam ci li ñu koy jiiñ, loolu dëppoowul ak aaday nguuru Room.”
17Bi ñu àndee ak man ba fii nag, randaluma mbir mi, waaye ca ëllëg sa sax toog naa ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi nit kooku.
18Ñi koy kalaame nag, bi ñu taxawee, jiiñuñu ko benn ñaawteef ci yi ma yaakaaroon,
19waaye ñuy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne mu ngi dund.

Read JËF YA 25JËF YA 25
Compare JËF YA 25:11-19JËF YA 25:11-19