Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 18

JËF YA 18:19-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Noonu ñu teer ci Efes. Pool bàyyi fa ñi mu àndaloon, daldi dugg ca jàngu ba, di diisoo ak Yawut ya.
20Ñu ñaan ko, mu des fa lu gëna yàgg, waaye nanguwul.
21Kon mu tàggtoo ak ñoom naan: «Dinaa délsi ci yéen, bu soobee Yàlla.» Noonu mu dugg gaal, jóge Efes,
22teersi dëkku Sesare, mu dem nuyu mbooloom ñi gëm, ba noppi dem Ancos.
23Bi mu fa desee ay jamono, mu jóge fa, di jaar dëkkoo dëkk ci diiwaanu Galasi ak Firisi, di dooleel xoli taalibe yépp.
24Amoon na nag Yawut bu tudd Apolos te juddoo Alegsàndiri, mu dikk Efes. Nit ku yewwu la woon te am xam-xam bu yaatu ci Mbind mi.
25Jàngoon na ci yoonu Boroom bi, di ku farlu ci xelam, muy xamle ak a jàngle bu wóor ci mbirum Yeesu, waaye fekk xam-xamam yem ci ni Yaxya daan sóobe ci ndox.
26Noonu mu daldi wax ak fit wu dëgër ca jàngu ba. Bi ko Pirsil ak Akilas déggee nag, ñu woo ko fi ñoom, gën ko leeral yoonu Yàlla.
27Naka Apolos bëgga dem Akayi, bokk ya xiir ko ca, ñu bind taalibe ya, ngir ñu teeru ko teeru bu rafet. Noonu mu dikk fa te jariñ lool ñi gëm jaare ko ci yiwu Yàlla.

Read JËF YA 18JËF YA 18
Compare JËF YA 18:19-27JËF YA 18:19-27