Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 18

Jëf ya 18:19-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.
20Ñooñu ñaan ko, mu toogaat fa ab diir, mu gàntal.
21Naka la tàggtoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yàlla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bàyyikoo Efes,
22teereji Sesare. Mu dem nag Yerusalem, nuyuji mbooloom gëmkat ña, doora dem Àncos gu Siri.
23Póol toog na Àncos ay fan, jóge fa wër diiwaanu Galasi, teg ca Firisi, di ñaax mboolem taalibey foofa.
24Ab Yawut nag bu ñuy wax Apolos te cosaanoo Alegsàndiri, moo dikkoon Efes. Ku rafet kàddu, te xam Mbind mi lool.
25Kooku jotoon naa jàng yoonu Sang bi. Mu ànd ak cawarte, di waare ak a jàngle lu wér péŋŋ ci mbirum Yeesu, doonte xam-xamam a ngi yemoon ci sóobeb Yaxya ci ndox.
26Mu tàmbalee waxe kóolute ca jàngu ba. Pirsil ak Akilas dégg ko, woo ko cig wet. Ñu daldi koy gëna leeralal yoonu Yàlla wi.
27Ba mu ko defee Apolos namma jàll ba Akayi, bokk ya rafetlu mébétam. Ñu bind taalibey Akayi, ngir ñu dalal ko. Ba Apolos agsee Akayi, dimbali na lool ña fa yiw may ñu doon ay gëmkat.

Read Jëf ya 18Jëf ya 18
Compare Jëf ya 18:19-27Jëf ya 18:19-27