23Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.
24Dégg nanu ne ay nit ñu bawoo ci nun, ñoo leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seen xel, te nun joxunu leen lenn ndigal.
25Moo tax nu mànkoo ci tànn ay nit ñu nu yebal ci yeen, boole leen ak sunuy soppe Barnaba ak Póol,
26ñoom ñi jaay seen bakkan ngir sunu Sang Yeesu Almasi.
27Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind.
28Ndaxte Noo gu Sell gi moo mànkoo ak nun ci bañ leena teg benn coono, xanaa lii manula ñàkk:
29Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.
30Ba loolu amee ñu tàggtoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
31Ba ñu jàngee bataaxal bi, kàddu ga dëfal leen, seen xol sedd.
32Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddli seen ngëm.
33Ba loolu amee ñu toog fa ab diir, bokk yi door leena ñaanal yoonu jàmm, yiwi leen, ngir ñu dellu ca ña leen yebaloon.
35Póol ak Barnaba nag des Àncos. Ñu ànd ak ñeneen ñu bare, di jàngle ak a xamle kàddug Boroom bi.
36Ba ñu ca tegee ay fan Póol ne Barnaba: «Nan dellu seeti bokk yi ci mboolem dëkk yi nu yégle woon kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.»
37Barnaba nag bëggoon ñu yóbbaale Yowaan, mi ñuy wax Màrk.