Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 14

Jëf ya 14:1-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba Póol ak Barnaba nekkee Ikoñum, noonu lañu dugge itam ca jàngub Yawut ya. Ñu waare, ba mbooloo mu mag gëm, ay Yawut aki Gereg.
2Yawut yi gëmul nag di xiirtal jaambur ñi dul Yawut, di yàq seen xel ci bokki taalibe yi.
3Teewul Póol ak Barnaba toog Ikoñum diir bu yàgg lool. Fit lañu doon waaree ngir Boroom bi, Boroom bi maye ay firnde aki kéemaan yu jaare ci ñoom, ngir seeree ko kàddug yiwam gi ñuy biral.
4Ba loolu amee waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.
5Jaambur ñeek Yawut yi nag ànd ak seeni kilifa, di leen waaja mitital ak a dóori doj.
6Ñu yég ko, daw làquji diiwaanu Likawni, ca dëkk ya ñuy wax Listar, ak Derbe ak la ko wër.
7Foofa itam ñu di fa xamle xibaaru jàmm bi.
8Jenn waay a nga daan toog ca Listar, tànk ya baaxul woon; laago la judduwaale, te masula dox.
9Kookoo dégg Póol muy waare, Póol xool ko jàkk, gis ne am na ngëm gu muccam mana jaare.
10Mu àddu ca kaw, ne waa ji: «Jógal taxaw jonn!» Waa ji ne bërét, jóg, daldi dox.
11Ba mbooloo ma gisee la Póol def, ca kaw lañu àddu ci làkku Likawni, ne: «Yàlla yee soppliku melow nit, wàccsi ci sunu biir!»
12Ci kaw loolu ñu tudde Barnaba Sës, kilifay yàllay Gereg yi, Póol nag gannaaw moo farewoo woon kàddug waare ga, ñu tudde ko Ermes, ndawal yàllay Gereg yi.
13Jaamookaayu Sës ma nga woon ca buntu dëkk ba. Sarxalkat ba daldi indi ca bunti dëkk ba ay yëkk yu ñu takkal caqi tóor-tóor. Sarxalkat ba ànd ak mbooloo ma, nara rendi jur ga, sarxal ko Póol ak Barnaba.
14Ci kaw loolu Póol ak Barnaba yég la xew. Ñu xotti seeni yére ndax ñaawlu ko. Ñu buur nag ba ca biir mbooloo ma, daldi àddu ca kaw ne:
15«Yeen, lu leen xiir ci lii? Nun itam ay nit lanu, bokk ak yeen benn bind. Xibaaru jàmm bi lanu leen di xamal, ngir ngeen wacc yëfi neen yii te walbatiku ci Yàlla, kiy dund te sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem lu nekk ci biir.

Read Jëf ya 14Jëf ya 14
Compare Jëf ya 14:1-15Jëf ya 14:1-15