Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 18

1.Buur ya 18:7-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Abdiyas di dem, Ilyaas ne pemm dajeek moom ca yoon wa. Abdiyas xàmmi ko, sujjóotal ko, dëpp jë ba fa suuf, ne ko: «Kii Ilyaas a, sama sang?»
8Mu ne ko: «Man a kay! Demal boog wax sa sang Axab, ne ko Ilyaas a ngoog de!»
9Abdiyas ne ko: «Ana lu ma def lu bon, sang bi, ba nga di ma booleek Axab, mu di ma rey?
10Giñ naa ci Aji Sax ji, sa Yàlla jiy dund, amul wenn xeet mbaa réew mu sama sang Axab yónneewul, di la seet. Te bu ñu nee nekkoo fa, mu giñloo waa réew maak xeet wa ne gisuñu la.
11Léegi nag nga naan ma: “Demal wax sa sang ne ko Ilyaas a ngoog.”
12Su ko defee su ma teqlikook yaw, ngelawal Aji Sax ji yóbbu la fu ma xamul, fekk ma dem wax ko Axab, te du la gis. Kon da may rey! Moona sang bi, man de, damaa masa ragal Aji Sax ji ba may ndaw ba tey.
13Moo sang bi! Xanaa waxuñu la li ma def, ba Yesabel di rey yonenti Aji Sax ji? Maa làq téeméeri yonenti Aji Sax ji ci ay xuntiy xeer, xunti mu nekk juróom fukk, di leen may lekk ak naan.
14Léegi nga naa ma: “Demal wax sa sang ne ko Ilyaas a ngoog!” Mu di ma rey?»
15Ilyaas ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, moom mi may jaamu, tey dinaa jàkkaarloojeek Axab moos.»
16Abdiyas dem ca Axab, yegge ko ko. Axab dikk taseek Ilyaas.
17Naka la Axab gis Ilyaas, ne ko: «Kii yaw a, di lëmbe Israyil nii?»
18Ilyaas ne ko: «Du maa lëmbe Israyil de. Yaw kay la, yaak sa kër baay, ndax yeena dëddu santaaney Aji Sax ji, di topp tuur yi nuy wax Baal.
19Léegi nag wooteel, Israyil gépp daje, fekksi ma ca tundu Karmel, ñu ànd ak ñeenti téeméeri yonenti Baal ak juróom fukk (450) ak ñeenti téeméeri nit (400) ñuy lekk njëlal Yesabel, te di yonenti Asera tuur ma.»
20Ba loolu amee Axab yónnee ca waa Israyil gépp, woo yonent ya, ñu daje ca tundu Karmel.
21Ilyaas dikk jàkkaarlook mbooloo ma mépp. Mu ne: «Yeen nag dungeen dakkal seen ciŋiñ-caŋañ ji ngeen nekke, wet gu nekk ngeen féete fa? Su Aji Sax ji dee Yàlla, toppleen ko; su dee Baal, ngeen topp ko.» Mbooloo ma ne patt.
22Ilyaas ne mbooloo ma: «Man de maa fi des ci yonenti Aji Sax ji, man doŋŋ, te yonenti Baal yi ñeenti téeméer lañook juróom fukk (450).
23Léegi nag, indil-leen nu ñaari yëkk. Bàyyileen yonenti Baal, ñu tànn wenn yëkk wi, def ko ay dog, teg ci kaw matt mi, bañ koo taal. Man it dinaa defar weneen yëkk wi, teg ci kaw matt mi, bañ koo taal.
24Su ko defee ngeen ñaan ci seeni tuur, man it ma ñaan ci Aji Sax ji. Su boobaa, Yàlla ju ci wuyoo sawara, kookoo di Yàlla.» Mbooloo ma mépp ne: «Waaw, baax na!»
25Ci kaw loolu Ilyaas wax yonenti Baal ya ne leen: «Tànnleen wenn yëkk te jëkka defar, ndax yeena gëna bare. Bu ngeen noppee, ñaanleen ci seeni tuur, waaye buleen taal.»
26Ñu jël yëkk wa mu leen jox, defar ko. Ñuy yuuxu, di woo Baal suba ba digg bëccëg, naan: «Baal, wuyu nu!» Waaye kenn àdduwul, kenn wuyuwul. Ña ngay ciŋiñ-caŋañi, di wër sarxalukaay ba ñu defar.

Read 1.Buur ya 181.Buur ya 18
Compare 1.Buur ya 18:7-261.Buur ya 18:7-26