12Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.»
13Farisen ya ne ko: «Yaw yaay seedeel sa bopp, kon li ngay wax du dëgg.»
14Yeesu ne leen: «Maa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di dëgg, ndaxte xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Waaye yéen xamuleen fa ma bàyyikoo ak fa ma jëm.
15Ci gis-gisu àddina ngeen di àttee; man duma àtte kenn.
16Teewul nag, su ma demee bay àtte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay àtte, waaye Baay, bi ma yónni, daf ciy ànd ak man.
17Seen yoon dafa wax ne seedes ñaari nit a gëna wóor.
18Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni mi ngi may seedeel itam.»
19Ñu laaj ko ne: «Kuy sa baay?» Yeesu ne leen: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.»
20Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon jànglee ca kër Yàlla ga, ca wetu fa ñu doon denc asaka ya. Kenn manu ko woona jàpp, ndaxte waxtoom jotagul.
21Yeesu dellu ne leen: «Maa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deeyaale. Fa ma jëm, dungeen fa mana dem.»
22Yawut yay waxante naan: «Nee na kat, fa mu jëm, dunu fa mana dem. Mbaa du day xaruji?»
23Yeesu ne leen: «Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci.
24Looloo tax ma ne, ci seeni bàkkaar ngeen di dee. Bu ngeen gëmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeni bàkkaar.»
25Ñu ne ko: «Yaay kan?» Mu ne leen: «Li ma leen waxoon ca njàlbéen ga.
26Li ma mana wax ci yéen ba àtte leen, bare na. Waaye ki ma yónni, ku wóor la, te li mu ma wax rekk laay jottali àddina.»
27Xamuñu woon ne, Yàlla Baay bee tax muy wax.
28Yeesu nag ne leen: «Bu ngeen yékkatee Doomu nit ki, dingeen xam ne Maay ki Nekk. Dingeen xam ne it, duma def dara man ci sama bopp. Li ma Baay biy jàngal rekk laay wax.
29Te it ki ma yónnee ngi ànd ak man; masu maa bàyyi ma wéet, ndaxte li ko neex rekk laay def.»
30Bi ñuy dégg Yeesu di wax loolu, ñu bare daldi koy gëm.
31Yeesu ne Yawut ya ko gëmoon: «Bu ngeen saxee ci li ma wax, nekk ngeen samay taalibe ci lu wóor.
32Te it dingeen xam dëgg gi, te dëgg gi dina leen goreel.»
33Ñu ne ko: «Nun ci Ibraayma lanu soqikoo te masunoo nekk jaamu kenn. Nan nga nu mana waxe ne dinañu leen goreel?»
34Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, képp kuy bàkkaar, jaamu bàkkaar la.
35Te jaam du bokk ci kër gi ba fàww, waaye doom, moom, ci kër gi la bokk ba fàww.