Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 21

YOWAANA 21:8-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Yeneen taalibe ya xëcc mbaal, mi fees dell ak jën, jëme ko ca tefes ga, ndaxte gaal ga sorewul woon; diggante bi waroon na tollook téeméeri meetar.
9Bi ñu teeree, ñu gis ab taal, ñu ciy lakk ay jën, teg mburu ca wet ga.
10Yeesu ne leen: «Indileen ci jën, yi ngeen jàpp.»
11Simoŋ Piyeer yéeg ca gaal ga, daldi xëcc mbaal ma ca tefes ga, mu fees dell ak jën yu mag; matoon na téeméeri jën ak juróom fukk ak ñett. Te li muy baree bare lépp, taxul mbaal ma dog.
12Yeesu ne leen: «Ñëwleen ndékki.» Kenn ci taalibe yi ñemewu koo laaj ki mu doon, ndaxte xam nañu ne Boroom bi la.
13Yeesu jegeñsi, jël mburu mi, jox leen, jox leen it jën.
14Bi Yeesu dekkee ba tey, bii mooy ñetteelu yoon, bi mu feeñoo ay taalibeem.
15Bi ñu ndékkee ba noppi, Yeesu ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax gën nga maa bëgg, ni ma ñii bëgge?» Mu ne ko: «Ahakay, Boroom bi, xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama mbote yi.»
16Noonu mu waxaat ko ne: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax bëgg nga ma?» Mu ne ko: «Ahakay, Boroom bi, xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Sàmmal ma sama xar yi.»
17Mu neeti ko ñetteel bi yoon: «Simoŋ doomu Yowaana, bëgg nga maam?» Piyeer am naqar ci li mu ko laaj ñetti yoon: «Ndax bëgg nga ma?» Mu ne ko: «Boroom bi, xam nga lépp; xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama xar yi.

Read YOWAANA 21YOWAANA 21
Compare YOWAANA 21:8-17YOWAANA 21:8-17