Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 6

Sarxalkat yi 6:5-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Na sawaras sarxalukaay bi wéye tàkk te du fey. Suba su nekk na ko sarxalkat bi xamb, ba noppi teg ci saraxu rendi-dóomal bi, te na lakk nebboni saraxi cant gi ci biir jàmm.
6Na sawara wéye tàkk fàww ci kaw sarxalukaay bi, te bumu fey.
7«Li ñu dogal ci saraxi pepp mooy lii: Na ko doomi Aaróona yu góor joxe fa kanam Aji Sax ji ca sarxalukaay ba.
8Barci-loxob sunguf su mucc ayib ànd ak diwam lees ciy tibbe, boole kook mboolem cuuraay la ca kaw saraxu pepp ma, daldi koy lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm, di saraxu baaxantal.
9La ca des Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy lekk, te buñu ci boole lawiir. Nañu ko lekke ci bérab bu sell. Ci biir ëttu xaymab ndaje mi lañu koy lekke.
10Deesu ko lakkaaleek lawiir. Seen cér la bu leen Aji Sax ji sédd ci saraxi sawaraam. Lu sella sell la, mel ni saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ.
11Képp kuy góor ci doomi Aaróona yi man na cee lekk. Seen cér la bu ñu leen sédde ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, te dogalal leen ko fàww. Lépp lu ci laal day doon lu sella sell.»
12Aji Sax ji wax na Musaa ba tey ne ko:
13«Li Aaróona aki doomam yu góor di sarxalal Aji Sax ji, keroog bu ñu koy diw, fal ko, mooy lii: ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, tollook saraxu pepp bi ñu saxoo bés bu nekk, te genn-wàll gi di suba, genn-wàll gi ngoon.

Read Sarxalkat yi 6Sarxalkat yi 6
Compare Sarxalkat yi 6:5-13Sarxalkat yi 6:5-13