Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 6

Sarxalkat yi 6:17-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
18«Waxal Aaróona ak doomam yu góor ne leen: Dogal bi ci saraxu póotum bàkkaar mooy lii: Juru saraxas póotum bàkkaar dañu koy rendi fa ñu wara rendi juru saraxu dóomal, fi kanam Aji Sax ji. Lu sella sell la.
19Sarxalkat bi koy rendi, muy saraxu póotum bàkkaar da ciy lekk, te fu sell lañu koy lekke, ci biir ëttu xaymab ndaje mi.
20Lépp lu laal ci yàpp wi, day doon lu sell, te bu lenn ci deretu sarax si tisee ci kawi yére, dees koy xaj fa mu tis, ci bérab bu sell.
21Su fekkee ne ndabal xandeer lañu togge woon yàppu sarax sa, nañu ko toj. Bu doon ndabal xànjar, ñu jonj ko, raxas ko.
22Képp kuy góor ci askanu sarxalkat sañ na cee lekk. Lu sella sell la.
23Waaye juru saraxas póotum bàkkaar deesu ci lekk lenn te fekk deretam dugg ca biir xaymab ndaje ma, ñu di ca amal ag njotlaay ca biir bérab bu sell ba. Loolu du lu ñuy lekk. Dees koy lakk, ba mu dib dóom.

Read Sarxalkat yi 6Sarxalkat yi 6
Compare Sarxalkat yi 6:17-23Sarxalkat yi 6:17-23