Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 2

Sarxalkat yi 2:12-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Saraxi ndoortel meññeef man naa ànd ak yooyu, waaye du bokk ci sarax su jëm ca sarxalukaay ba, ñu di ko taal, ngir xetug jàmm.
13Seen mboolem saraxu pepp nangeen ko xorom. Bu seen saraxu pepp ñàkk mukk xorom, ndax mooy màndargaal seen kóllëreek seen Yàlla. Seen sarax yépp ngeen di xorom.
14«Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu ndoortel meññeef, na ko indil mbool mu ñu séndal, def ko sànqal, muy saraxu ndoortel meññeefam.
15Na ci sotti diw ak cuuraay. Saraxu pepp la.

Read Sarxalkat yi 2Sarxalkat yi 2
Compare Sarxalkat yi 2:12-15Sarxalkat yi 2:12-15