12 Saraxi ndoortel meññeef man naa ànd ak yooyu, waaye du bokk ci sarax su jëm ca sarxalukaay ba, ñu di ko taal, ngir xetug jàmm.
13 Seen mboolem saraxu pepp nangeen ko xorom. Bu seen saraxu pepp ñàkk mukk xorom, ndax mooy màndargaal seen kóllëreek seen Yàlla. Seen sarax yépp ngeen di xorom.
14 «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu ndoortel meññeef, na ko indil mbool mu ñu séndal, def ko sànqal, muy saraxu ndoortel meññeefam.
15 Na ci sotti diw ak cuuraay. Saraxu pepp la.