10Deesu ko weccee. Du jur gu baax gu ñu ko mana wuutoo, doonte jur gu bon la, te du jur gu bon gu ñu ko mana wuutoo, te fekk muy gu baax. Ci biir jagleel googu ku xasa wuutoo ag jur moroom ma, jur gu jëkk gaak kuutaay la dañuy bokk doon lu sell.
11Su fekkee ne la ñu dogu woona joxe mala mu daganul la te daganula sarxalal Aji Sax ji, na nit ki yóbbu jur ga ba ca sarxalkat ba,
12sarxalkat ba xayma ko. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.
13Su ko boroom bëggee jotaat, day fey njég ga, yokk ca xaajub juróomeelu njég ga.
14«Su nit jagleelee Aji Sax ji dëkkuwaayam, sellalal ko ko, na sarxalkat bi xayma dëkkuwaay bi. Su baaxee su bonee, lu mu ci dogal mooy wéy.
15Su fekkee ne ki dogu woona joxe dëkkuwaayam da koo bëgga jotaat, day fey njég ga ñu ko xaymaa, yokk ca xaajub juróomeelam, mu doonaat alalam.
16«Su nit jagleelee Aji Sax ji suuf su mu moom ci suufas ndonoom, na ñuy xaymaa suuf sa, na dëppook dayob pepp bay mat jiwum suuf sa. Ñetti barigoy peppum lors yu ne juróom fukki dogi xaalis a koy wecci.