Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 26

Sarxalkat yi 26:22-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Maay xabtal rabi àll yi ci seen kaw, ñu xañ leen seeni doom, seeni gétt ñu tas, seeni nit ñu néewal, ba seeni mbedd ne wëyëŋ.
23«Su ma leen loolu yaralul ba tey, xanaa ngeen sax ci noonoo ma,
24su boobaa man itam maa leen di noonoo, te it man ci sama bopp maa leen di mbugalaat lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar.
25Maay dalal saamar ci seen kaw, feye leen ko kóllëre gi ngeen fecci. Bu ngeen làqoo ci seeni biir dëkk yu mag sax, maay wàcce mbas ci seen biir, seeni noon jekku leen.
26Bu ma téyee loxo bi ma leen di leele, fukki jigéen dinañu bokk lakk seen mburum njël ci benn taal doŋŋ, natt ko ay somp, séddale, ngeen lekk, te dungeen suur.
27«Waaye bu loolu weesee te déggaluleen ma, xanaa di ma noonoo ba tey,
28su boobaa ma gën leena mereeti, noonoo leen, te man ci sama bopp maa leen di mbugalati lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seen bàkkaar.
29Dingeen yàpp seeni doom yu góor, yàpp seen doom yu jigéen ndax xiif.

Read Sarxalkat yi 26Sarxalkat yi 26
Compare Sarxalkat yi 26:22-29Sarxalkat yi 26:22-29