Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 24

Sarxalkat yi 24:7-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Jal bu nekk teg ca cuuraay lu raxul, mu wuutu mburu mi, di saraxu baaxantal, te di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
8Bésub Noflaay bu nekk nañu saxoo taaj mburu yooyu fi kanam Aji Sax ji. Loolu sas la bu bànni Israyil di tegoo fàww.
9Mburu yooyu Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy féetewoo, te nañu ko lekke fu sell, ndaxte lu sella sell la, di lu ñu séddoo fàww ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.»
10Ba loolu wéyee amoon na ci biir bànni Israyil jenn waay ju yaayam di doomu Israyil te tuddoon Selomit doomu Dibbri, Daneen ba. Baayam di waa Misra. Mu am bés xeex jib ci biir dal bi, ci diggante waa jooju ak jenn waayi Israyil ju raxul. Ci biir loolu waa ji yaayam di doomu Israyil wax Yàlla lu ñaaw, tudd ko jaar fu bon. Ñu yóbbu ko ca Musaa.
12Ñu tëj waa ja, ba xam lu Aji Sax ji namm ci moom.
13Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa ne ko:
14«Génneel dal bi ki may wax lu ñaaw, man Yàlla, te na mboolem ku ci dégg teg loxoom ci kaw boppam, ba noppi mbooloo mépp dóor koy doj, ba mu dee.
15Bànni Israyil nag nangeen leen wax ne leen: Képp ku wax Yàllaam lu ñaaw, jaar fu bon, na wéetoo añam.
16Ku ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee rekk mooy àtteem. Mbooloo mi mépp a ko wara dóor ay doj, ba mu dee. Muy doxandéem muy njuddu-ji-réew, ku ci ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee mooy àtteem.
17«Bu loolu weesee képp ku faat bakkanu nit, dee rekk mooy àtteem.
18Ku faat bakkanu mala, na fey boroom. Bakkan, bakkan a koy fey.
19Képp ku gaañ moroomam, la mu ko def rekk lañu koy def.
20Damm-damm, damm-damm a koy fey; bët, bët a koy fey; bëñ it bëñ a koy fey. Ni mu gaañe moroomam rekk, ni lañu koy gaañe.

Read Sarxalkat yi 24Sarxalkat yi 24
Compare Sarxalkat yi 24:7-20Sarxalkat yi 24:7-20