Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 23

Sarxalkat yi 23:15-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15«Bésub Noflaay ba ngeen di indi takku bele biy saraxu yékkati-jébbale, bés ba ca topp ngeen di dale waññ juróom ñaari ayi bés yu mat sëkk.
16Waññleen ba ca bés ba topp ci juróom ñaareelu bésub Noflaay ba, muy juróom fukki fan, ngeen indil ca Aji Sax ji saraxu pepp mu bees.
17Seeni kër ngeen di jële ñaari mburu yuy doon saraxu yékkati-jébbale, mu ci nekk di lu ñu lakke juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib; dees ciy def lawiir, lakkaale ko ko, muy saraxu ndoortel meññeef, ñeel Aji Sax ji.

Read Sarxalkat yi 23Sarxalkat yi 23
Compare Sarxalkat yi 23:15-17Sarxalkat yi 23:15-17