15 «Bésub Noflaay ba ngeen di indi takku bele biy saraxu yékkati-jébbale, bés ba ca topp ngeen di dale waññ juróom ñaari ayi bés yu mat sëkk.
16 Waññleen ba ca bés ba topp ci juróom ñaareelu bésub Noflaay ba, muy juróom fukki fan, ngeen indil ca Aji Sax ji saraxu pepp mu bees.
17 Seeni kër ngeen di jële ñaari mburu yuy doon saraxu yékkati-jébbale, mu ci nekk di lu ñu lakke juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib; dees ciy def lawiir, lakkaale ko ko, muy saraxu ndoortel meññeef, ñeel Aji Sax ji.