Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 20

Sarxalkat yi 20:20-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20«Ku dëkkoo soxnas baayam bu ndaw, baayam bu ndaw la torxal. Ñooy wéetoo seen añu ñaawtéef. Duñu am takkndeer ba keroog ñuy dee.
21«Bu nit nangoo jabaru ku mu bokkal waajur, loolu gàcce la. Torxal na ka mu bokkal waajur te duñu am takkndeer.
22«Sàmmleen sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te jëfe ko, ngir réew ma ma leen jëme, ngeen dëkki fa, bañ leena gëq.
23Buleen roy defini xeet wi ma leen di dàqal, ndax yooyu yépp lañu doon def, ba ma sib leen.

Read Sarxalkat yi 20Sarxalkat yi 20
Compare Sarxalkat yi 20:20-23Sarxalkat yi 20:20-23