Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 20:20-23 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 20:20-23 in Kàddug Yàlla gi

20 «Ku dëkkoo soxnas baayam bu ndaw, baayam bu ndaw la torxal. Ñooy wéetoo seen añu ñaawtéef. Duñu am takkndeer ba keroog ñuy dee.
21 «Bu nit nangoo jabaru ku mu bokkal waajur, loolu gàcce la. Torxal na ka mu bokkal waajur te duñu am takkndeer.
22 «Sàmmleen sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te jëfe ko, ngir réew ma ma leen jëme, ngeen dëkki fa, bañ leena gëq.
23 Buleen roy defini xeet wi ma leen di dàqal, ndax yooyu yépp lañu doon def, ba ma sib leen.
Sarxalkat yi 20 in Kàddug Yàlla gi