Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 16

Sarxalkat yi 16:27-33

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27Muy yëkk wiy saraxu póotum bàkkaar, muy sikket biy saraxu póotum bàkkaar te ñu yóbbu woon seen deret ca biir bérab bu sell baa sell ngir defe ko njotlaay, lépp lañuy génne dal bi. Der yaak yàpp waak sébbriit ma dees koy boole lakk, ba mu dib dóom.
28Ki ko lakk bu noppee, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi.
29«Te itam dogal a ngii, di lu leen war fàww. Bésub fukki fan ci juróom ñaareelu weeru at mi nangeen ci toroxlu te du lenn lu ngeen ci mana liggéey, du njuddu-ji-réew du doxandéem bi ci seen biir;
30ndaxte ci bés boobu lañu leen di joxeel njotlaay ngir fóot seen mboolem bàkkaar, ba ngeen set fi kanam Aji Sax ji.
31Na doon seen bés bu ngeen di nopplu doŋŋ, ngeen war cee toroxlu. Dogal la bu sax dàkk.
32«Sarxalkat bi ñu fal nag, solal ko, jox ko sañ-sañu sarxalkat bu mag, mu wuutu baayam, na def saraxu njotlaay gi. Na sol yére yu sell yooyu di yi ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew,
33te it na def njotlaayal bérab bu sell bee sell ak xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, boole ci defal sarxalkat yi seen njotlaay, ñook mbooloom Israyil mépp.

Read Sarxalkat yi 16Sarxalkat yi 16
Compare Sarxalkat yi 16:27-33Sarxalkat yi 16:27-33