20«Bu Aaróona matalee njotlaayal bérab bu sell bee sell ak xaymab ndaje ma ak sarxalukaay ba, na indi sikket biy dund.
21Aaróona day teg ay loxoom ci kaw boppu sikket biy dund te tudd ci kawam mboolem ñaawtéefi bànni Israyil ak seeni tooñ, ak seeni bàkkaar yépp, boole ko yen sikket bi, teg ko ci loxol nit ku ñu yónni, mu dàq ko ca màndiŋ ma.
22Sikket bi day yenu seeni ñaawtéef yépp, yóbbaale ca ndànd-foyfoy ga, ñu wacc ko ca màndiŋ ma.
23«Na Aaróona dellu ca xaymab ndaje ma, summi yére ya ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew, di ya mu soloon bala moo dugg ca bérab bu sell baa sell, te na fa wacc yére ya.
24Bu loolu weesee mu sangoo fu sell, sol yérey boppam, génn, joxeel boppam ab saraxu rendi-dóomal, joxeel mbooloo mi seen saraxu rendi-dóomal ngir njotlaayal boppam ak njotlaayal mbooloo mi.