Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 14

Sarxalkat yi 14:37-49

Help us?
Click on verse(s) to share them!
37Bu sarxalkat bi seetee liir wi ci miiri néeg bi ca biir, muy ay xóot-xóot yu xawa nëtëx, mbaa mu xawa xonq, mel ni lu def pax ci miir bi,
38na génn néeg bi te tëj néeg bi diiru juróom ñaari fan.
39Bésub juróom ñaareel ba na sarxalkat bi délsi seet néeg bi. Bu liir wi lawee ci miiri néeg bi,
40na sarxalkat bi santaane, ñu teggi doj yi liir wi xuural, boole ko génne dëkk bi, sànni ko fu setul.
41Na xeetlu biir néeg bi ba mu daj, te pënd ba ñu ca xeete dees koy génne dëkk ba, tuur ko fu setul.
42Dañoo wara sàkkaat ay doj, wuutale ko doj yooyu te sàkk ban bu bees, raaxe ko néeg bi.
43«Su liir wi delloo tegu ci biir néeg bi gannaaw bu ñu teggee doj yi, xeet biir néeg bi, ba raax ko,
44sarxalkat bi day dikk seet ko. Su liir wi lawee ci néeg bi, liir wu aaytal la wu xuural biir néeg bi, di sobe.
45Néeg ba dees koy daane, boole doj yaak bant yaak banu raax ba bépp, génne ko dëkk bi, tuur ko fu setul.
46«Ku dugg biir néeg bi diiru fan yi mu tëje dina yendoo sobe ba jant so.
47Ku tëdd ca biir néeg ba war naa fóot ay yéreem te ku fa lekke it war naa fóot ay yéreem.
48«Su sarxalkat ba delloo ca néeg ba, seet ko, fekk liir wa lawul ca néeg ba, gannaaw ba ñu ko raaxee, na biral ne néeg bi set na, ndax kon liir wa raaf na.
49Liy laabal néeg bi moo di mu sàkk ñaari picc ak bantu garabu seedar ak wëñ gu xonq curr ak caru isob.

Read Sarxalkat yi 14Sarxalkat yi 14
Compare Sarxalkat yi 14:37-49Sarxalkat yi 14:37-49