Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 13

Sarxalkat yi 13:9-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9«Képp ku ame jàngoroy der juy law, nañu ko yóbbu ca sarxalkat ba.
10Na ko sarxalkat bi seet. Su dee ab tërgën bu weex te kawar gi ci nekk soppiku weex, boole ci def góom ca biir,
11kon jàngoroy der juy law la te xas naa law ci yaram wi. Na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Du jar mu di ko ber ndax taq na sobe ba noppi.
12Su fekkee ne nag jàngoro ji génn naa génn ci yaramu nit ki, sarxalkat bi gis ko fépp, li ko dale ci bopp bi ba ci tànk yi,
13na ko sarxalkat bi seet bu baax. Bu gisee ne li génn ci yaramam daj na yaram wi yépp, na biral ne nit ki mu dal set na; gannaaw léppam a soppiku weex, set na.
14Ba tey bés bu ay góom génnaatee ci yaram wi, nit ki sobewu na.
15Su sarxalkat bi gisee yaramu nit ki def góom rekk, na biral ne sobewu na. Góom boobu génn ci yaram wi sobe la. Jàngoroy der juy law la.
16Te it bu góom bi soppikoo weex, na dem ca sarxalkat ba.
17Na ko sarxalkat bi seet, ba gis ne weexaat na, mu biral ne ki jàngoro ji dal set na te kon it set na.
18«Su nit taabee ba wér,
19ab tërgën bu weex mbaa gàkk bu weex bu rax xonq feeñ fa taab ba nekkoon, na dem ca sarxalkat ba.
20Su ko sarxalkat bi seetee ba gis fa taab ba nekkoon mel ni lu def pax, te kawar gi ci nekk soppiku weex, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la, ju juddoo ca taab ba.
21Waaye su ko sarxalkat bi seetee te gisu ca kawar gu weex, deful pax it te raaf na, na ber nit ki juróom ñaari fan.
22Su wéree ne jàngoro ji law na ci yaram wi, na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la.
23Su gàkk bi yemee foofu, baña law, légétub taab ba la, te na sarxalkat bi biral ne nit ki set na.
24«Su nit lakkee, ab gàkk bu weex mbaa bu weex te rax xonq feeñ ca kaw suux wu xonq wa lakk,
25na ko sarxalkat bi seet. Su kawar gi ci nekk soppikoo weex te gàkk bi mel ni lu def pax, kon jàngoroy der juy law la, ju juddoo ca lakk-lakk ba. Na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na, ndax jàngoroy der juy law la.
26Waaye su ko sarxalkat bi seetee, gisul kawar gu weex ci gàkk bi, deful pax it te raaf na, na ber nit ki juróom ñaari fan.
27Sarxalkat bi da koy seet ca bésub juróom ñaareel ba. Su wéree ne jàngoro ji law na ci yaram wi, na biral ne nit ki sobewu na. Jàngoroy der juy law la.
28Su gàkk bi yemee foofu te lawul ci yaram wi, ab tut la bu juddoo ci lakk-lakk bi. Na sarxalkat bi biral ne nit ki set na, ndax légétub lakk-lakk ba la.

Read Sarxalkat yi 13Sarxalkat yi 13
Compare Sarxalkat yi 13:9-28Sarxalkat yi 13:9-28